spot_img

Viatique du Màggal 2021 : Vingt-cinq leçons de vie ! (Par Dr Massamba Guéye)

Date:

J’ai appris grâce à Cheikh Ahmadou Bamba Mbacké que:

  1. On ne vit pas heureux.se sans une conviction tenace.
  2. On ne réussit rien de grand sans une vraie saine vision.
  3. Grandir, c’est surtout faire grandir ses proches.
    4.  Le savoir est au dessus de toute autre force.
  4. La foi, force spirituelle, est notre véritable rempart contre le doute inhibant.
  5. Le pardon est l’arme des forts quoi qu’il en coûte.
  6. La réussite d’une vie ne se mesure pas au baromètre des biens accumulés ici-bas.
  7. Innover, c’est se doter de la capacité de quitter notre confort s’il corrompt nos convictions.
  8. Les tentatives de l’ennemi pour te détruire ne peuvent rien contre ton destin si tu es sincère avec toi-même!
  9. Ce n’est pas parce ton ennemi est incorrect envers toi que tu dois te départir de ta correction pour lui répondre.
  10. On doit faire de ceux.elles qui nous suivent des leaders accompli.es, socialement assis.es, mentalement stables, économiquement indépendant.es.
  11. Le courage ne consiste pas à braver des dangers sans raison mais d’avoir un idéal sincère pour lequel se sacrifier.
  12. Pour écrire une belle page d’histoire, mieux vaut avoir une référence sûre comme le Prophète Mouhammad PSL.
  13. On ne devient jamais Maître sans accepter d’être un dévoué disciple.
  14. La discipline et l’ordre sont les lois fondamentales d’une communauté forte et cohérente.
  15. Mettre ses ressources licites au service de sa communauté est l’extrême bonheur d’un Être vivant.
  16. Il faut parfois renoncer à ses acquis quand on veut inscrire son nom dans le
    Grand Livre de l’Eternité.
  17. On ne doit pas se plaindre d’avoir des ennemis.
  18. Celui qui n’a pas de projet de vie n’a pas de grand destin à vivre.
  19. Celui qui n’a personne de qui recevoir des ordres est source de désordre social.
  20. Être avec les gens bien nous rend meilleur.
  21. Un héros véritable n’est ni vaniteux, ni fanfaron ni arrogant.
  22. La foi véritable ne s’accommode pas de vilenie.
  23. Celui qui prétend te guider doit être meilleur que toi.
  24. Le temps peut tout effacer sauf les actes qui rendent l’humain meilleur.

Dr Massamba GUÈYE LBA
Koki, le 24 septembre 2021
—-
Yóbbalu Màggal 2021!
Ñaar fukki njàngat ak juróoom!
Jàng naa ci Seex Axmadu Bàmba mu tedd mi ne:

  1. Ku amut pas-pas dëgg sag dund du mat.
  2. Kenn du am ndam lu rëy te amoo gis-gis bu yiw.
  3. Yokku, mooy fexe ba sa ñoñ yokku.
  4. Xam-xam a sut lépp lu dul moom.
  5. Sunu baatin bu sell mooy sunu kaaraange ci njàqare.
  6. Jégaale mooy ngànnaayu boroom doole dëgg.
  7. Tekki ci àdduna deesu ko natt ci dayob am-am.
  8. Yeesal ndono du mat feek nit a ngi wéeru ci lu yomb.
  9. Pexey noon ngir yàq la manuñu dara ci yow bu dee dëggu nga ci sa bopp.
  10. Sab noon ñàkk i teggin warut a tax nga ñàkk kersa.
  11. Dees a war a fexe ba ñiy topp ci ñuñ doon i kàngam ci dayo, cig nite, ci xam-xam te man seen bopp cim koom.
  12. Am fit du fekk luy raye nga dugg ca, am fit mooy nangoo jaay sa bakkan ndax sa gëm-gëm gu dëggu.
  13. Ku bëgg a am woyu jaloore, da ngay am royuwaay wu mel ni Yonnet Mohamed SAS.
  14. Ku nanguwut a am kilifa doo mas a doon kilifa.
  15. Wéye ndigël mooy tax mbooloo bennoo, jàmmoo tey jariñu cig tawféex .
  16. Delloo sa alal ju lew saw askan mooy dëgg-dëggi mbègte.
  17. Ku bëgg a doon sa màndargam askan loo jëf ci mbaax xeebal.
  18. Ken warut a jooy am i noon.
  19. Ku xamut lu tax ngay dund, amoog ëllëg.
  20. Ku amut kilifa gooy déggal, yaay jaxase saw askan.
  21. Nekk ak ñu baax day tax a baax.
  22. Gòor Yàlla du rëy, du tiitaru, du xeebaate.
  23. Ngëm dëgg du ànd ak i ñaawtéef.
  24. Ku la bëgg a jiite na la gën.
  25. Yàgg man naa far lu ne bamu des jëf ju Yàlla gërëm.

Dr Masàmba GÉY
Koki, 24 fanu Sàttunmbar 2021

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici

spot_img

DEPECHES

DANS LA MEME CATEGORIE
EXCLUSIVITE