Yaay Bóoy,
20i ci ren (2024), suba su nu xéyee di la xalaat ak a xalaat sag dem waaye di jéem a dund dund goo bokkatul. Lu doy waar… Naka La mënee xéy rekk jël la, nga làqu ba fàww ?! Waaye « Bakkan bu ñam dund, dina mos dee »…
Goreek liggéey, julli waxtu te maandu, lii nga nu jàngal ba noppi jiitu ci, doon ci misaal dëggëntaan. Mësoo yuqat, booleek dal, teey, muñ ak muuñ, am sutura.
Yaay Bóoy, waay nga, wéeruwaay nga ; su dul woon ak yow, Làmbaay ñaaw. Ay soo nu yarul woon, kon fu nu jëm tey ?!
Wax ko fii mbaa feneen lu muy soppi ? Dara ! Xanaa, nun, say doom, nu fexe bay dëbb sa dëbbiin ba keroog nu leen iy fekkiji, yaak Peer Faal.
Xamal ngeen nu àddina. Jàngal ngeen nu bokk lu nu am, joxe te doo ci xaar dara. Fi sabilaa rekk…
Lu nu dese, lu nu deseek yéen ? Di wéy ci topp seen iy tànk te di leen ñaanal fa ngeen tëdd ngeen dajeek ngërëmul Yàlla.
Wàcc ngeen ! Yal na dee di seen noflaay ba fàww ! Yal na Yàlla baal sunu bépp way-dawlu !
Yal na Yàlla dotti ko ay teraanga ca Firdawsi, mook ña mu fa fekk ak ña ko fa fekk bijaahi Mustafaa