spot_img

KIPPUG WATTU LÀKKI RÉEW MI

Date:

Manifeste du collectif KIPPUG LÀKKI RÈEW MI publié en wolof à l’occasion de la célébration de la journée internationale de la langue maternelle décrétée en l’an 2000 par les Nations unies.

Cër bi nu jox farañse bi tax na ba, kenn sañul a xët sàrt yiy yoonal mbindam. Te sax, boo juumee ba yàq ci baat bi gën a ndaw, réew mépp mbamb la, ak koo mënti doon. Waaye, bu dee wolof bi moom, nu neex waay binde, dara du la ci fekk.
Ndeysaan, dangay foog ne sax, làkki réew mi, ñoom, amuñu ay sàrt yiy yoonal seenum mbind. Aycaleen nu jubbanti, ci mbindum wolof mi, yenn ndëngte yiy ñaawal ak a tilimal xar-kanamu réew mi.

ÀND JUBAL MBIND MI !
Ci tekkib Paap Aali Jàllo
( Iniwérsite Gaston Berger)

Àlluwa ji
I Kàddug dugge
II Mbind mi ñu bëgg a jubal
1- Ayeropooru Ndakaaru
2- Turi jotaayi tele Senegaal yi
3- Turi làng walla kuréli pólotig
4- Turi « start-up »
5- Àlluway-siiwal
Ñi sos KIPPUG WATTU LÀKKI RÉEW MI
Kilifa yi ànd ak nun ci siiwal yaxal bii

Kàddug dugge
Danu seetlu ne, li ko dale ati 2000 yi ba tey, nguur geek làngi pólotig yi, ñu ngiy jéem a faaydaal làkki réew mi. Nu koy rafetlu. Muy càkkub-dëkki-taax yi, kow tali yi ak yéenekaay yi, bu ci nekk a ngiy fésal làkki réew mi ak ni askan wiy dundalaatee sunug moomeel. Ci misaal, àlluway-siiwal yi, turi jotaayi tele yi, turi làngi pólotig yi… bu ci nekk, bindees na ko ci wolof doonte ne, yenn saa yi, ñu rax ci farañse.
Naam, itte jaa ngi fi. Waaye, mbind mi dafa des lu baree bare. Dafa mel ni, cër bi nu jox mbindum farañse bi, joxunu ko mbindum làkki réew mi, rawati-na wolof bi. Moom kay, kenn sañul a xët sàrt yiy yoonal mbindum farañse mi te mbambuñu la, ak koo mënti doon. Waaye, bu dee wolof bi moom, nu neex waay binde, dara du la ci fekk. Ndeysaan, dangay foog ne sax, làkki réew mi, ñoom, amuñu ay sàrt yuy yoonal seenum mbind.
Ndaw njuumte lu réy !
Ci atum 1971 lees jëkk a génne ab dekkare buy sàrtal mbindum wolof ak teqaleb baat yi. Dekkarey 1975, 1985 ak 2005 yi ci topp yépp, ci bu jëkk bi lañu wéeru, bu ci nekk indi ciy coppite. Bu dee àtteb 77-55 biy sàrtal mbindum làkki réew mi, moom, bésub 10eel ci awril 1977 lañu ko yoonaloon. Àtte bi dafa tëral ne, bépp yaxal bees jagleel mbooloo mi, te nu bind ko ci wolof walla seereer, warees na ko dëppale ak dekkare yiy sàrtal mbind mi ak teqaleb baat yi ci làkk yooyule. Ci yoon, képp ku jalgati àtte boobu, yeyoo nga ab daan, ni ko dogi 2, 3 ak 8 tërale ci garug-àttey jalgati gi. Dëgg la, jamono yooyu, jubluwaayu pólotig la àtte bi amoon. Waaye, tey, warees na jéggi loolu, sóoraale làkk yeek seenum njàngale ci jubluwaay yi. Su boobaa, dees na mën a wattu mbindum làkki réew mi, dakkal yëfi maa-tey yi.
Rafetul, 50i at ginnaaw bees sàrtale mbind mi, nuy wéy di dajeek i ndëngte ñeel làkki réew mi. Te, mbind mi, taxu koo soppeeku noonu, rawati-na bi mu amee àtteb yoonal.
Njuumte yooyu yàgg fi lool, tëw a deñ. Booba ak léegi, dañuy nasaxal faayday làkki réew mi. Te, loolu dafay sabab xeebeel ñeel sunuy làkk, aada ak cosaan. Bu yàggee, dinanu gën a suufeel sunu bopp.
Kippug làkki réew mi dafa di ab kurél gu ëmb ay jigéen ak i góor yu farlu ci làkki réew mi. Li ñu bëgg mooy xirtal taskati xibaar yépp, ñaax leen ngir ñu gën a sàmm sunu moomeelug làkk ak aada. Ngir mottali yéene bu ni mel, nangu nañu leen a baaxe seen jaar-jaar ak seen xam-xam ba nu mën a amalub set-setal ci li fi nekk tey, ak li nar a ñëw ëllëg. Ci gàttal daal, jubluwaay bi mooy, fexe ba mbindum làkki réew mi jaar yoon. Bu ko defee, dootunu jaawale « jaam » ak « jàmm » ni ko ayeropoor AIBD defe. Ndekete, ngir dalal way-tukki yi, dañu bind ci gegub teer bi « Dalal ak jaam » te ñu waroon a bind « Dalal ak jàmm ».
Te xam ngeen ni jaam du jàmm.
Kippug wattu làkki réew mi di leen baaxe ay  jubbanti ñeel yenn ndëngte yiy ñaawal ak a tilimal xar-kanamu réew mi.

Mbind mi nu bëgg a jubal
 
I- AYEROPOORU NDAKAARU
Li ñu bind
Li ñu waroon a bind

Dalal ak jaam

Dalal ak jàmm

II- TURI JOTAAYI TELE SENEGAAL YI
SEN TV

Li ñu bind

Li ñu waroon a bind

Feem ci keur

Feem ci kër

Guis-Guis
Gis-Gis

Li ci rewmi
Li ci réew mi

Ndoumbelane
Ndumbelaan

Sama gokh
Sama gox

Sen jotay
Seen jotaay/jataay

Sen xeweul
Seen xéewal

TFM

Li ñu bind

Li ñu waroon a bind

Faram face

Faramfàcce

Firi gent
Firi gént

Jakaarloo bi
Jàkkaarloo bi

Jánggat
Jàngat

Jonganté
Jo?ante

Li ci penc mi
Li ci pénc mi

Ngonal
Ngoonal

Sama keur
Sama kër

Wakhtane ak
Waxtaan ak

Ña woon demb
Ña woon démb

Khew khewi dine dji
Xew-xewi diine ji

Yeewu leen
Yeewuleen

2STV

Li ñu bind

Li ñu waroon a bind

Aarru mbed

Aaru mbedd

Bantamba
Bàntàmbaa

Keur gui
Kër gi

Pencci reew mi
Pénci réew mi

WALF TV

Li ñu bind

Li ñu waroon a bind

Selebe yoon

Selebe-yoon

Diiné ak diamono
Diine ak jamono

Weer ak werlé
Wér ak wérle

Sa ndiogou
Saanjóogu

RTS
Li ñu bind
Li ñu waroon a bind

Njangatu besbi

Njàngatu bés bi

Reeni koom koom
Reeni koom-koom

Takussan
Tàkkusaan


III- TURI LÀNGI WALLA KURÉLI PÓLOTIG YI

Li ñu bind
Li ñu waroon a bind

Benno bokk yakaar

Bennoo bokk yaakaar

Bess du niakk
Bés du ñàkk

And Jef
Ànd Jëf

And Défar Sénégal
Ànd defar Sénégal (Senegaal)

Bloc des centristes Gaïndé
Bloc des centristes Gaynde

(CDP) Garab-GUI
(CDP) Garab gi

Sénégal moo niou saff (FNP)
Sénégal moo ñu saf (FNP)

Suxxali Reew Mi
Suqali Réew Mi

FAR / Yoonwi
FAR/Yoon wi

Benno jubël (FSD/BJ)
Bennoo jubal (FSD/BJ)

GARAP / ADS
GARAB / ADS

MPS / SELAL
MPS / SELLAL

Ñiaxx Jariñu
Ñaq jariñu

PSD/Jant-Bi
PSD/Jant bi

Reenu Rew
Reenu Réew

Rewmi
Réew mi

UPAS/Niax Teed
UPAS/Ñaq Tedd

UDF/Mboolomi
UDF/Mbooloo mi

Luy jot jotna
Luy jot jot na

Pastef Patriotes du Sénégal
Pastéef

IV- TURI « START-UP »
Li ñu bind
Li ñu waroon a bind

Aywadieune

Aywa jën

BaySeddo
Bay Séddoo

Etou nature
Ëttu nature

Jokalante
Jokkalante

Jokko-annonces
Jokkoo-annonces

Lifantou
Liifantu

Manko
Mànkoo

Ndiarte
Njarte

Niokobok
Ñoo ko bokk

Outalma
Utal ma

Sakanal 
Sakkanal

Tew mou tew
Teew mu teew

Tolbi
Tool bi

Tong Tong
To?-to?

Wanter
Wànteer

Xibar.net
Xibaar.net

Yobanté Express
Yóbbante Express


IV- Àlluway siiwal

Leeral



Jóoni-jóoni



Mooy sunu kalpe, moom rekk la !

Ku nekk ak sa soppe !

Amul moroom, benn la fi !



Ndogu lu barkeel ak MAGGI !


Jege na, wóor na, gaaw na


Jo?e, dëbbal lu saf !



Doole rekk moo wóor


Booloo nekk benn, toog sunu kër !

Toog sunu kër



Feem bu bees, système la !

Dina xëb, dina set, ànd ak xet gu neex.


Wooteel fépp

#Àndxeexkoronaa




Adja, mëne fu ne !

Palastig dafay lor jur gi
nanu ci taxaw.


Sama THIAYNE mbaa ma SHINE !



Buleen jëf lenn ci lu dul ndigal, ndax ndigal kat, sart la ngir nu nangu jëf.


Promo Bégal
« Des na ci Yaw »

Jubbanti yi nuy def ci àlluway-siiwal yi, dees na leen fekk ci nataal yi ànd ak yaxal bi.

Limub jubbanti bile nag, matalewul. Ndaxte, jotunoo dajale mboolem àlluway-siiwal yi, turi jotaayi tele yi, yu làngi walla kuréli pólotig yeek yu « start-up » yi. Ci kanam tuuti, dinan amal yeneen i kàmpaañ.
Kàmpaañ bii di Ànd jubal mbind mi !, Kippug wattu làkki réew mee ko xalaat. Amalees na ko ginnaaw kàmpaañu alfaabetisaasiyo? biñ jagleeloon mag ñi te dippe woon ko Àllarbay làkki réew mi.  Alfaabetisaasiyo? boobu, diggante bésub 28eel ci oktoobar jàpp bésub 9eel ci desàmbar 2020 lees ko dawaloon ca IFAN Séex Anta Jóob ak ca EBAD.
Kippug wattu làkki réew mee ngi dékku bépp seetlu walla xalaat te yit pare na ngir dimbali képp ku am soxla su aju ci tekki ak mbind mu jub añs.
Mail : [email protected]
 

Ñi sos KIPPUG WATTU LÀKKI RÉEW MI
Maryetu Jong Jóob
Wattukatub Kàggu, doonoon fi Aji-saytu bu Fondation UCAD, Ndakaaru
Ajaratu Umar Sàll Jaw
Aji-làmmiñal ca IFAN Séex Anta Jóob, UCAD, Ndakaaru
Ndey Koddu Faal
Njiitu EJO-Éditions, Kërug-móolukaayu téere ci làkki réew mi
Maamur Daraame
Aji-làmmiñal, FLSH, UCAD, Ndakaaru
Bubakar Bóris Jóob
Bindkat, Njiitu defuwaxu.com yéenekaayu web ci wolof
Baabakar Jóob dit Buuba Jóob
Aji-mboor, Bànqaasub Làkki démb, FLSH, UCAD, Ndakaaru
Maam Cerno Siise
Aji-làmmiñal, Bànqaasub Làmmiñal, FLSH, UCAD, Ndakaaru
 

Kilifa yi ànd ak nun ci siiwal yaxal bii
Séex Aliyu Ndaw, Bindkat
Sa?-Léwopool Juuf, Aji-làmmiñal, bind na ab baatukaay wolof-français / français-wolof
Aliyu Ngóone Sekk, Njiitu Ëttub Làmmiñalub njëfeel bu Ndakaaru, UCAD, Ndakaaru
Mamadu Njaay, Njiitu OSAD, Kërug-móolukaayu téere ci làkki réew mi
Mamadu Li, Njiitu ONG ARED, kërug tàggat ak móolukaayu-téere ci làkki réew mi
Adraame Jaxate, Njiitu Bennoog Bindkati Senegaal yi ci làkki réew mi (UESLAN)
Kolonel Mumar Géy, Bindkat
Maamaram Sekk, Njiitu Laboraatuwaaru Làmmiñal, IFAN Séex Anta Jóob,
Piyeer Sàmbu, Njiitu Bànqaasu Làmmiñal, FLSH, UCAD
Aysatu Sàll Ndóoy, Njiitu Vidéo Positive

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici

spot_img

DEPECHES

DANS LA MEME CATEGORIE
EXCLUSIVITE

De quel droit Métropolis se prévaut-elle ? (Par Thierno Bocoum)

En remplaçant Barthelemy Dias à la tête de l’Association...

Mamadou Ibra Kane : Un homme perdu entre le journalisme et le militantisme (Par Sall Mamadou Oumar)

Mamadou Ibra Kane, journaliste et homme d'influence dans le...