J’ai appris grâce à Cheikh Ahmadou Bamba Mbacké que:
- On ne vit pas heureux.se sans une conviction tenace.
- On ne réussit rien de grand sans une vraie saine vision.
- Grandir, c’est surtout faire grandir ses proches.
4. Le savoir est au dessus de toute autre force. - La foi, force spirituelle, est notre véritable rempart contre le doute inhibant.
- Le pardon est l’arme des forts quoi qu’il en coûte.
- La réussite d’une vie ne se mesure pas au baromètre des biens accumulés ici-bas.
- Innover, c’est se doter de la capacité de quitter notre confort s’il corrompt nos convictions.
- Les tentatives de l’ennemi pour te détruire ne peuvent rien contre ton destin si tu es sincère avec toi-même!
- Ce n’est pas parce ton ennemi est incorrect envers toi que tu dois te départir de ta correction pour lui répondre.
- On doit faire de ceux.elles qui nous suivent des leaders accompli.es, socialement assis.es, mentalement stables, économiquement indépendant.es.
- Le courage ne consiste pas à braver des dangers sans raison mais d’avoir un idéal sincère pour lequel se sacrifier.
- Pour écrire une belle page d’histoire, mieux vaut avoir une référence sûre comme le Prophète Mouhammad PSL.
- On ne devient jamais Maître sans accepter d’être un dévoué disciple.
- La discipline et l’ordre sont les lois fondamentales d’une communauté forte et cohérente.
- Mettre ses ressources licites au service de sa communauté est l’extrême bonheur d’un Être vivant.
- Il faut parfois renoncer à ses acquis quand on veut inscrire son nom dans le
Grand Livre de l’Eternité. - On ne doit pas se plaindre d’avoir des ennemis.
- Celui qui n’a pas de projet de vie n’a pas de grand destin à vivre.
- Celui qui n’a personne de qui recevoir des ordres est source de désordre social.
- Être avec les gens bien nous rend meilleur.
- Un héros véritable n’est ni vaniteux, ni fanfaron ni arrogant.
- La foi véritable ne s’accommode pas de vilenie.
- Celui qui prétend te guider doit être meilleur que toi.
- Le temps peut tout effacer sauf les actes qui rendent l’humain meilleur.
Dr Massamba GUÈYE LBA
Koki, le 24 septembre 2021
—-
Yóbbalu Màggal 2021!
Ñaar fukki njàngat ak juróoom!
Jàng naa ci Seex Axmadu Bàmba mu tedd mi ne:
- Ku amut pas-pas dëgg sag dund du mat.
- Kenn du am ndam lu rëy te amoo gis-gis bu yiw.
- Yokku, mooy fexe ba sa ñoñ yokku.
- Xam-xam a sut lépp lu dul moom.
- Sunu baatin bu sell mooy sunu kaaraange ci njàqare.
- Jégaale mooy ngànnaayu boroom doole dëgg.
- Tekki ci àdduna deesu ko natt ci dayob am-am.
- Yeesal ndono du mat feek nit a ngi wéeru ci lu yomb.
- Pexey noon ngir yàq la manuñu dara ci yow bu dee dëggu nga ci sa bopp.
- Sab noon ñàkk i teggin warut a tax nga ñàkk kersa.
- Dees a war a fexe ba ñiy topp ci ñuñ doon i kàngam ci dayo, cig nite, ci xam-xam te man seen bopp cim koom.
- Am fit du fekk luy raye nga dugg ca, am fit mooy nangoo jaay sa bakkan ndax sa gëm-gëm gu dëggu.
- Ku bëgg a am woyu jaloore, da ngay am royuwaay wu mel ni Yonnet Mohamed SAS.
- Ku nanguwut a am kilifa doo mas a doon kilifa.
- Wéye ndigël mooy tax mbooloo bennoo, jàmmoo tey jariñu cig tawféex .
- Delloo sa alal ju lew saw askan mooy dëgg-dëggi mbègte.
- Ku bëgg a doon sa màndargam askan loo jëf ci mbaax xeebal.
- Ken warut a jooy am i noon.
- Ku xamut lu tax ngay dund, amoog ëllëg.
- Ku amut kilifa gooy déggal, yaay jaxase saw askan.
- Nekk ak ñu baax day tax a baax.
- Gòor Yàlla du rëy, du tiitaru, du xeebaate.
- Ngëm dëgg du ànd ak i ñaawtéef.
- Ku la bëgg a jiite na la gën.
- Yàgg man naa far lu ne bamu des jëf ju Yàlla gërëm.
Dr Masàmba GÉY
Koki, 24 fanu Sàttunmbar 2021